TSK

TSK · 2 Peter 1:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.

Doonte jaar nañu ci nattub njàqare bu mag, seen mbégtee rembat ci seen biir ñàkk gu tar, ba géejal seenug tabe.

Cofeel gu réy nag lañu leen di ñaanale, ndax yiw wi leen Yàlla géejal, yeen.

¶ Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee,

Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant.

Nii sunu cofeel ak yeen baawaane, yal na ko Boroom bi yokke ba baawaanal ag cofeel ci seen biir, ak ci seen diggante ak nit ñépp.

¶ Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.

Na sunuy ñoñ tàggatu ci jëf ju baax ju ñu saxoo ba faj soxla yu taxaw, ngir ñu baña ñàkk njariñ.

Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.