¶ Ci kaw loolu ñu pastéefu ci njànglem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi julli.
TSK
TSK · 2 Peter 3:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo tax ku yaakaar ne taxaw nga, nanga moytu bala ngay daanu.
Waaye na jaan ja naxe woon Awa, ca pexeem, ragal naa seenum xel yàqoo noonu, ba dëddu ngëm gu dëggu te set gu ngeen ŋoye woon ci Almasi.
¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.
Ndax jëmm ji kat teewul, waaye xol baa ngeek yeen, di bégee gis seen doxalin wu jekk, ak seen ngëm gu wér gu ngeen gëm Almasi.
Yaw itam, moytu ko bu baax, ndax moo gàntal lool sunu àlluwa.
Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj.
Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.