TSK

TSK · 2 Samuel 8:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba Sóol feddlee nguuram ca Israyil, xare naak seen noon ya leen wër yépp: Mowabeen ñaak Amoneen ñaak Edomeen ñaak buuri waa Soba, ak waa Filisti. Mboolem fu mu walbatiku rekk, moo daan.

la jóge ca Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ñaak waa Filisteek Amalegeen ña ak la mu lële ca buurub Soba, Adadeser doomu Reyob.

¶ Ba Axab buurub Israyil saayee yàggul dara, Mowabeen ña dañoo fippu, jógal doomam Buur Akasiya. Mu am bés Akasiya tollu biir néegam ca kaw taaxum këram ga ca Samari, daldi xàwwikoo ca palanteer ba, daanu ba gaañu lool. Gannaaw gi mu yónni ay ndaw, ne leen: «Demleen seetal ma ca Baal Sebub, tuuru Ekkron, ba xam ndax dinaa dund gannaaw jéll bii ma daanu.»

¶ Moom la Salmanasar buurub Asiri song, mu nangul ko, di ko fey galag.

Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.

buuri Tarsis ak dun ya di ko indil ay galag; buuri Saba ak Seba di ko yótsi yóbbal,

Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,