TSK

TSK · 2 Timothy 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Cofeel moo di: lépp, nga bale; lépp, nga gëm; lépp, nga yaakaar; lépp, nga dékku.

¶ Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi,

Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.

Waaye yaw, àndal ak sa sago, ak diggante boo mana tollu, te ñeme coono. Jàppal ci liggéeyub jottli xibaaru jàmm bi, beyal sa waar ba mu mat sëkk.

¶ Fàttlikuleen bés yu jëkk ya, gannaaw ba ngeen jotee ci leeru Yàlla, na ngeen dëgërloo woon ca xeex bu mag ba te metti.

Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru jalub Yàlla.