TSK

TSK · 2 Timothy 2:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Kon nag Besalel ak Oliyab ak mboolem ñu xareñ ñi Aji Sax ji may xareñte ak déggin ngir ñu mana jëfe mboolem sas yi jëm ci liggéeyu bérab bu sell bi, ñoom ñépp nañu sottal lépp li Aji Sax ji santaane.»

¶ Kon xamleen tey te délloosi ci seen xel, ne Aji Sax ji mooy Yàlla fa kaw asamaan ak fi kaw suuf. Du keneen.

Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,

Sa kàdduy seedee di njekk ba fàww, may ma, ma ràññee, ba dund.

Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.

Aw yëkk xam na boroomam, mbaam-sëf xam gàmb, bi ko boroomam di xonte, waaye Israyil xamul, sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»

Dees koo xamal yoon wa, te Yàllaam a ko ko jàngal.

Luke 9:44 TSK

¶ «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»

Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen.

Kii ci Noo gi la jote kàddu gu xelu, kee séddoo kàddug xam-xam ci genn Noo gi.

¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.

Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo ba sag yokkute bir ñépp.

¶ Seetleen ni mu ràññikoo, moom la Ibraayma maamu cosaan ma ci boppam jébbal fukkeelu cérub cëxëtoo ma!

¶ Fàttlikuleen seen njiit, yi leen àgge kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seenug dundin meññ, te ngeen roy seen ngëm.

Moomu xel jógewul fa kaw, àddina sii la bokk, di yëfi bakkan, te di mbiri Seytaane.