TSK

TSK · 2 Timothy 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,

Acts 2:30 TSK

Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku bokk ci geñoom lay teg cib jalam.

moo jëm ci Doomam, ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.

¶ Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk,

Denc nañu ko, mu dekki ca ñetteelu fanam, te noonu la ko Mbind mi indee.

Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.

Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat, ak ndawal kàddu gi, ak itam ab sëriñ, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.

Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»