TSK

TSK · Acts 11:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.»

Waaye ngoru Aji Sax ji naka jekk ñeel na fàww ku ko ragal; njekkam ñeel sëtaati

Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal, mag ak ndaw.

Man Aji Sax ji, damaa sopp yoon, bañ càcc ak ñaawtéef. Maay dàmp sama ñoñ ni mu ware, fas ak ñoom kóllëre gu sax.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»

Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»

Ñu ne ko: «Gëmal Sang Yeesu, daldi mucc, yaak sa waa kër.»

¶ Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.

Ahakay! Maa sóob waa kër Estefanas itam. Waaye bu loolu weesee, fàttlikuwuma fu ma sóobe keneen.