TSK

TSK · Acts 17:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëggam.

Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,

Acts 2:23 TSK

Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.

Acts 3:15 TSK

Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko.

Acts 5:30 TSK

Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

¶ Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.

¶ Li ma jotoon laa leen jëkka jottli, te moo di: Almasi moo dee ngir njotug sunuy bàkkaar, te noonu la ko Mbind mi indee.

¶ Kon nag dama lay dénk fi kanam Yàlla ak Almasi Yeesu, miy àtteji ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci darajay bésam ba muy feeñ, ak ci darajay nguuram,

Jude 1:14 TSK

¶ Enog, juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottli woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell,