Ba loolu amee boroom dëkk ba gis la xew, daldi gëm, di yéemu ci li mu jànge ci Sang bi.
TSK
TSK · Acts 18:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
¶ Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.
Galyon daldi leen dàqe ca àttekaay ba.
¶ Ba àppu juróom ñaari fan yay waaja jeex, Yawut ya jóge diiwaanu Asi gis Póol ca kër Yàlla ga. Ñu yëngal mbooloo mépp, jàpp ko,
Ndaxte gëmkati Maseduwan ak Akayi ñoom la soob ñu sàkke lenn ci seen alal, ngir dimbalee ko ñu sell ña diy néew doole ca Yerusalem.
¶ Bokk yi, xam ngeen ne Estefanas ak njabootam ñooy jooxeb ndoortel meññeef ci diiwaanu Akayi, te jàpple ñu sell ñi lañu séddoo. Kon dama leen di ñaan,
ndax xam naa seen yéene ju réy, te moom laay damoo ci kanam waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi noppi.» Te seen xéraange jooju ngeen nekke xiirtal na ñu bare.
Moo leen taxa doon royukaay ci mboolem gëmkati diiwaani Maseduwan ak Akayi.