TSK

TSK · Acts 18:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 18:4 TSK

¶ Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.

¶ Ab Yawut nag bu ñuy wax Apolos te cosaanoo Alegsàndiri, moo dikkoon Efes. Ku rafet kàddu, te xam Mbind mi lool.

¶ Mboolem Yawut yaak Gereg ya dëkke Efes nag yég mbir moomu, tiitaange dikkal leen ñoom ñépp, daraja ju réy doxe ca ñeel turu Sang Yeesu.

Ndax Póol daa fasoon yéeney teggi Efes, ngir baña yàgg diiwaanu Asi; booba day gaawtu, ngir màggalu Pàntakot man koo fekk Yerusalem.

¶ Na ma la ko dénke woon ba may dem diiwaanu Maseduwan rekk, nanga toog Efes googu, ngir ña fay jàngle leneen, nga aaye leen.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Efes, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Ki yor juróom ñaari biddiiw yi ci loxol ndijooram, di doxe digg juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi. Mu ne: