Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.
TSK
TSK · Acts 20:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Yeremi jottli Cedesyas buurub Yuda mboolem kàddu yooyu fa Yerusalem.
Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.
Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
Te amul lenn lu leen di jariñ, lu ma leen nëbb, bañ leen koo xamal; jàngal naa leen ci mbeddum buur ak ci biir kër yi.
Ndimbalal Yàlla nag moo ma may may dund ba tey jii, di ko seedeel ci mag ak ndaw, te waxuma lenn lu moy la yonent ya ak Musaa waxoon ne dina am.
Waaye danoo dàq jépp jëf ju gàccelu ju nit di jëfe làq-làqal. Doxunu ag njublaŋ te sopparñiwunu kàddug Yàlla. Liy dëgg kay lanuy fésal, ba am kóoluteg ñépp, fi kanam Yàlla.
Xanaa li ma leen di wax dëgg daa tax ma mujj di seenub noon?
Xanaa kay noonu nu Yàlla doyloo, ba dénk nu liggéeyu xibaaru jàmm bi, noonu lanuy waaree li neex Yàlla miy seet ab xol, te dunu ci wut bànneexu nit ñi.