Ñooñooy giñe tuuri Samari, naa: “Giñ naa ko ca tuur may dund ca Dan, giñ ko ca yoonu Beerseba wa dul fey.” Dinañu daanu, dootuñu jóg.»
TSK
TSK · Acts 24:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi la woon ba kera ba Yaxya dikkee. Waaye ba mu dikkee lañu yégle nguurug Yàlla, ñépp di ci jéema dugge seen doole.
Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.
Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.
Gannaaw ba tarib dog ya ca téereb yoonu Musaa, ak téereb yonent ya sottee, njiiti jàngu ba yóbbante leen kàddu, ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee kàddu gu ngeen ñaaxe mbooloo mi, waxleen.»
¶ Jant yooyu nag yemook yëngu-yëngu bu réy bu amoon ci mbirum Yoon wi.
Waa jii lanu gis ne ab rambaaj la buy sabab réeroo ci biir Yawuti àddina sépp. Moom mooy njiitu ngér mu sikk mi ñuy wax Nasareen ñi.
Sama taxawaayu tey ci ëttub àttekaay bii nag, mooy yaakaar ji ma am ci dige bi Yàlla digoon sunuy maam.
Buur Àggripa, xanaa gëm nga yonent yi? Xam naa xéll ne gëm nga.»
¶ Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam, àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa, ak yonent yi seede nañu loolu.
ak bokkaale, ak xërëm, ak mbañeel, ak féewaloo, ak kiñaan, ak mer mu ëpp, ak jiital say bëgg-bëgg, ak réeroo, ak xàjjalikoo,
Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,
¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.