TSK

TSK · Acts 24:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Taalibe ya nag fas yéenee boole kem kàttanu ku nekk ca ñoom, ngir ndimbal lu ñuy yónnee bokki diiwaanu Yude.

Teewluleen nag te fàttliku ne diiru ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppee àrtu kenn ku nekk ci yeen, bay jooy sax.

Waaye fii ma tollu, Yerusalem laa jëm, ngir ndimbal lu ñeel ñu sell ña féete foofa.

¶ Ci wàllu ndimbal li jëm ci gëmkat ñu sell ñi, noonu ma ko digale mboolooy gëmkati diiwaanu Galasi, yeen itam defeleen ko noonu.

Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.

¶ Ndax liggéey bi ndimbal lii laaj kat, yemul rekk ci faj soxlay ñu sell ñi, waaye itam dina baawaanal cant gu bare, ñeel Yàlla.