TSK

TSK · Acts 24:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg.

Acts 12:3 TSK

Mu gis nag na mbir ma neexe Yawut ya, ba tax mu teg loxo Piyeer, moom itam; loola yemook bési màggalu Mburu mu amul lawiir.

Acts 25:1 TSK

¶ Festus nag toogsi diiwaanam ba am fa ñetti fan. Gannaaw loolu mu dem Yerusalem.

Acts 25:9 TSK

Festus nag bëgg lu neex Yawut yi, tax mu ne Póol: «Ndax nangu ngaa dem Yerusalem, ñu àttee la foofa ci mii mbir ci sama kanam?»

¶ Naka la layool boppam noonu, Festus àddu ca kaw, ne ko: «Póol, yaw dangaa dof! Sa njàng mu réy mee la dofloo.»

¶ Diiru ñaari at la Póol dal Room ci kërug boppam gu muy fey, di fa àggale mboolem ña koy seetsi.