TSK

TSK · Acts 26:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee boroom kàddu ga ne ma: «Yaw nit ki, jógal taxaw, ma wax la.»

Acts 1:17 TSK

Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»

Acts 6:4 TSK

Nun nag nanu wéye julli gi, ak liggéey bi ci kàddu gi.»

Acts 9:15 TSK

Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.

Acts 18:9 TSK

¶ Ba loolu amee Sang bi wax ak Póol ag guddi ci biir peeñu, ne ko: «Bul tiit dara, waaye waxal te bul noppi,

Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.

Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.

Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»

Ci Almasi lanu jote aw yiwu doon ay ndaw, ngir nit ñi déggal yoonu ngëm wi, ci biir mboolem xeeti àddina, ngir aw turam.

¶ Ndegam boobu liggéey lanu sasoo, ci yërmandey Yàlla, dunu yoqi.

¶ Damu war na, moonte amul njariñ, waaye naa jàll ba tey ci mbir yu ma Sang bi gisloo, ak peeñu yu mu ma won.

Sama tànk yooyu nag am peeñu moo ko waral. Ca laa wéetoo ak ña ñu jàppoon ne ñooy kàngami mbooloom gëmkat ña, faramfàcceel leen xibaaru jàmm bi may yégal jaambur ñi dul Yawut, ngir ragal sama liggéey bi ma jota def, te di ko wéye, doon coonob neen.

Noonu ngeen ko jànge ci Epafras, sunu mbokkum surga biy sunu soppe, te di jawriñu Almasi bu wóor bi nu jàpple,

Ci moomu mbooloo laa dib jawriñ, te Yàllaa ma sase noonu, ñeel leen, ngir ma xamle kàddug Yàlla ba mu mat sëkk.

¶ Damay sant sunu Boroom Almasi Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi,

Waaye yaw, àndal ak sa sago, ak diggante boo mana tollu, te ñeme coono. Jàppal ci liggéeyub jottli xibaaru jàmm bi, beyal sa waar ba mu mat sëkk.