TSK

TSK · Acts 26:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 22:5 TSK

Sarxalkat bu mag bi, ak mboolem kurélu mag ñi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas, ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.

Acts 24:5 TSK

Waa jii lanu gis ne ab rambaaj la buy sabab réeroo ci biir Yawuti àddina sépp. Moom mooy njiitu ngér mu sikk mi ñuy wax Nasareen ñi.

Man mi xaraf ba ma amee juróom ñetti fan, askanoo ci bànni Israyil, giiroo ci Beñamin, di ab Ebrë bu ñaari Ebrë jur, te bokk ci ngérum Farisen, ci wàllu yoonu Musaa.