Yeena ngi tàbbi ci seen biir kóllëreg Yàlla Aji Sax ji, ak ci ngiñam, kóllëre gi seen Yàlla Aji Sax ji fasoo ak yeen bésub tey,
TSK
TSK · Acts 5:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu séddale aw ñam askan wépp, mbooloom Israyil mépp, góor ak jigéen; ku ci nekk mu jox la menn mburu ak yàpp wu ñu saaf ak benn nàkku reseñ. Mbooloo ma doora dem, ku nekk ñibbi këram.
Esra, sarxalkat ba, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko.
Dees na ma waxal ne: «Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!» Mboolem ñi ma mereey ànd, sëgg, fekksi ma.
¶ Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.
Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).
Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.
di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.
Mboolem waa diiwaani Lidd ak Saron nag gis ko, ñoom ñépp waññiku ci Sang bi.
Yoon wii tey, daan naa fitnaal ñi ko gëm ba sabab seenug dee. Yeew naa góor, yeew jigéen, tëjlu leen kaso.
Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.