TSK

TSK · Amos 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ne ko mu wax bànni Israyil ne leen: «Góor ak jigéen, képp ku ci dogu ba xas xasu doon ab nasireen, ngir sédd boppam Aji Sax ji,

Noonu la Israyil gépp ràññee, la dale Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum, ne Samiyel taxaw na taxawaayu yonentu Aji Sax ji.

¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»

Yewu ma baayam di Nimsi it, diw ko, fal ko buurub Israyil; te Alyaasa, ma baayam di Safat, dëkk diiwaanu Abel Mewola, nanga ko diw, fal ko, muy yonent, wuutu la.

¶ Ci biir loolu kenn ca kurélu yonent ya wax moroom ma ci ndigalal Aji Sax ji, ne ko: «Ayca, jam ma!» Waa ja lànk, ne du ko jam.

Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»

¶ Am na bés mbooloom yonent ya wax Alyaasa ne ko: «Xoolal, fii nuy dajeek yaw daa xat.

Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. Wax nu lu neex, gisal nu ay nax.»

Éey niti Israyili tey, teewluleen kàddug Aji Sax ji! «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? Lu waral sama ñoñ naa: “Noo moom sunu bopp, dootunu délsi fi yaw”?

¶ Moo tax Aji Sax ji wax lii ci mbirum waa Anatot, ñiy wut sama bakkan, naan ma: «Baal di waxe waxyu ci turu Aji Sax ji, lu ko moy nu rey la.»

Sunu kàngam ya setoon wecc, seen yaram mucc gàkk, di lerxat bay tàkk, wér péŋŋ, leer nàññ.

Micah 2:6 TSK

Seen yonent yeey waare naa: «Buleen waare! Nii kat deesu ko waaree, gàcce du nu dab!»

Acts 4:18 TSK

¶ Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu.

Acts 7:51 TSK

¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!

Waaye li ngeen wara jëkka xam moo di amul ci Mbind mi, benn waxyu bu yonent ba ko waxe, firee xelum boppam.