Sama dënn a fees aki wax, te samam xel xiir ma ci wax.
TSK
TSK · Amos 3:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yeen bokk yi ñu bàcc ni pepp ca sama dàgga ja, la ma dégge ci Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi, wax naa leen ko.
¶ Ci kaw loolu Yeremi wax ak kàngam yépp ak mbooloo ma mépp, ne leen: «Aji Sax jee ma yebal ngir ma biral waxyu, rëbb kër gii ak dëkk bii, te mooy kàddu yi ngeen dégg yépp.
«Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ. Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen biral waxyu!”
¶ Gannaaw loolu Amaciya ne Amos: «Yaw boroom peeñu mi, dawal, làquji réewum Yuda, nga waxe fa waxyu, am fa loo dunde.
Aji Sax jee ma jële fa ma doon sàmme samay gàtt. Moo ma ne: “Demal biralal ma waxyu ci Israyil sama ñoñ.”
¶ Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal Yunus ñaareel bi yoon. Mu ne ko:
«Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»
Yégle xibaaru jàmm bi moom, du lu may kañoo. Wartéef la wu ñu ma sas, te ngalla man, su ma yéglewul xibaaru jàmm bi!