TSK

TSK · Deuteronomy 13:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: β€œNa ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”»

¶ «Góor gu bokk ci yeen mbaa jigéen, di seete nit ñu dee mbaa muy boroom rawaan buy gisaane, dee rekk mooy àtteem. Dees koy dóor ay doj, mu dee, gàddu bakkanu boppam.»

¶ Ci kaw loolu Musaa wax ko bànni Israyil, ñu génne dal ba waa ja ñàkke Yàlla kersa, dóor ko ay doj, ba mu dee. Kon li bànni Israyil def mooy li Aji Sax ji santoon Musaa rekk.

nangeen génne ba ca buntu dëkk ba, waa ji, mbaa ndaw si def jooju jëf ju bon, te ngeen dóor ay doj, waa jooju mbaa ndaw si, ba mu dee.

Na ko góori dëkk bépp dóori doj ba mu dee. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir. Israyil gépp a koy dégg, daldi ragal.

Ci kaw loolu waa réew ma mépp ànd dem ca kër Baal. Ñu màbb ko, ay sarxalukaayam ak jëmmi nataalam, ñu tas tasar, Matan sarxalkatu Baal ba, ñu rey ko ca kanam sarxalukaay ya. Ci biir loolu Yoyada sarxalkat ba teg ay wattukat ca kër Aji Sax ji.