Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii.
TSK
TSK · Deuteronomy 32:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.
Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc; laal tund yi, ñu saxar.
Suuf daa loroo loru, fetta fett, salfaañoo salfaañu.
Bu tund yu mag yi doon toxu, yu ndaw yiy raf sax, sama ngor du la toxul, te sama kóllërey jàmm du raf.» Aji Sax ji la yërëm moo ko wax.
Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, dogleen seen mbuñukay xol, balaa sama xadar ne jippét ni sawara, di tàkk te deesu ko fey ndax seen jëf ju bon.
Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon, ma def leen seen jaami noon ci réew mu ngeen xamul, ndax merloo ngeen ma mer mu dul fey mukk.»
Tàngooru sànjam la dagge gépp kàttanu Israyil. Fa kanam noon ba la roccee dooley ndijooram. Moo tàkkal Yanqóoba ni sawara wuy sëlsëli, ba xoyom mboolem la ko wër.
Aji Sax jee xëpp am sànjam, sotti tàngooru meram, moo jafal sawara fi Siyoŋ, ba xoyom kenu ya.
Maa leen di saam fi digg Yerusalem, jafale leen sama tàngooru xadar, ba ngeen seey ca biir.
Sàkkuleen Aji Sax ji, ba dund. Lu ko moy mu ne jippét ci kaw askanu Yuusufa, lakk waa Betel lakk gu dul fey.
Tund yu mag yi di ko loxal, tund yu ndaw yi seey, suuf fuddu fi kanamam, mook àddina ak mboolem li ci biiram.
Du seen xaalis, du seen wurus wu leen di mana xettli. Keroog bésub sànjum Aji Sax ji, ak sawaras fiiraangeem, àddina sépp ay xoyomu. Mooy raafal moos mboolem ñi dëkke àddina si, te raafal gu raglu lay doon!»
ndax kat «sunu Yàlla, sawara wuy xoyome la.»