Cant ñeel na teddngaam, ba fàww, yal na teddngaam dajal suuf sépp! Amiin, Amiin!
TSK
TSK · Ephesians 3:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»
Ci moom la lépp sosoo, ci moom la lépp sottee, te moom la lépp ñeel. Moom la daraja ñeel ba fàww! Amiin.
bi daraja ñeel, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
làmmiñu ñépp it biral ne Yeesu Almasi mooy Sang bi, te muy ndamu Yàlla Baay bi.
Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottale Yeesu Almasi, mi daraja ñeel ba fàww. Amiin.
Moom la kàttan ñeel ba fàww. Amiin.
Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.