TSK

TSK · Esther 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Fekk na jenn waayi Yawut a ngi ci Sus, péey ba. Ma nga tudd Mardose. Yayir di baayam. Yayir, Simey ay baayam. Simey, Kis ay baayam, bokk ci giirug Beñamin.

¶ Booba bala ayu kenn ci xale yu jigéen ñiy agsi, ba muy dem ca Buur Aserus, day fekk mu matal fukki weer ak yaar yi ñu àppal jigéen ñi, ngir ñu yokk ci seen taar. Juróom benni weer yi, ñu di leen diw ndàbb lu ñuy wax miir; juróom benni weer yi ci des, ñu di leen diw ay diw yu xeeñ ak yeneen yu jigéen ñiy defaroo.