Waaye waa réew moomu leen di def ay jaam, dinaa leen àtte. Gannaaw loolu sa askan dina ca génn, ànd ak alal ju bare.
TSK
TSK · Exodus 2:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan.
Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
Réew, mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.»
Maa déggal sama bopp yuuxi bànni Israyil, gi waa Misra def ay jaam, te fàttewuma sama kóllëre ga.
Aji Sax ji nag baaxe leen, yërëm leen, geesu leen ndax kóllëreem ak Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Looloo tax buggu leena faagaagal, te ba tey jii xalabu leen.
Nga daldi leen teg ci seen loxoy noon, ñu fitnaal leen. Teewul ñu jàq, woo la wall, nga dégge ko fa asamaan, ba jox leen ñu leen xettli, ci sa yërmande ju yaa, ñu xettli leen ci seen dooley noon.
Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.
Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; yal na sama yuux àgg fa yaw.
Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba, yeen ñiy sëti Yanqóoba, ñiy tànnéefam,
ga mu digoon Ibraayma, giñal ko Isaaxa,
bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,
Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,