TSK

TSK · Exodus 32:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Wàccal te délsi, ànd ak Aaróona. Waaye muy sarxalkat yi, di mbooloo mi, bu kenn bëtt, jëm ci man Aji Sax ji, lu ko moy ma dal ci seen kaw.»

Mu nangoo ko ci seeni loxo, liggéey ko ba sàkk ci sëllu wu ñu móol. Ci kaw loolu ñu naan: «Bànni Israyiloo, seen Yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!»

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Doxal jóge fii, yaak mbooloo mi nga génne réewum Misra, ngeen dem ca réew ma ma giñaloon Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne leen seen askan laa koy jox.

Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.»

Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam, ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk. Ndaw maas gu dëng te njublaŋ!

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.