Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ”
TSK
TSK · Exodus 33:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe.
Ba loolu amee Aji Sax ji fomm musiba ma mu waxoon ne dina ko teg ñoñam.
ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»
Ci kaw loolu ñu nettali Musaa, ne: «Dem nanu réew, ma nga nu yebaloon, te it foofa la meew maak lem ja tuuroo! Lii ca meññeef maa.
Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»
«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»
Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la.
«Maa noon maa leen di fàkkas, ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo.
Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.
Leeg-leeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko,
Doonte maa ne boroom njekk li dina dund moos, te gannaaw gi mu yaakaar njekkal démbam la, bay def safaan ba, su boobaa gépp njekkam ga woon, deesu ci bàyyi xel, te safaan bi mu def tey mooy doon àtteb deeyam.
¶ Ba mu ko defee Yunus tàmbalee wër bés bu jëkk ba, di yéene naan: «Ñeent fukki fan gannaaw tey Niniw dina tas.»
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!