TSK

TSK · Exodus 8:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanal-leen ma nag.»

Baal ma àq bii yoon rekk, te ngeen ñaanal ma seen Yàlla Aji Sax ji, ngir mu teggil ma rekk, wii ay wu rey.»

Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.

Kàngam ya fa Cowan dañuy teqlikook seen sago, diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: “Nun ay boroom xel lanu, sosoo ca buur ya woon”?»

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko fexe, ngir sàggi sagub képp ku fiy damu, ba teddadil képp ku àddina teral.

Mbooloo maa ngay àddu ca kaw, naan: «Lii kay baatu Yàlla la, du baatu nit!»