TSK

TSK · Genesis 1:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkal ci bépp xeetu dund, denc, ngeen bokk dunde.»

Job 36:31 TSK

Noonu lay saytoo xeet yi, ba maye ñam wu ne gàññ.

Yaa saxalal jur gi ñax ak gàncax gu doom aadama di bey, ba génnee ab dund fi suuf,

Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.

Mooy leel bépp boroom bakkan. Kee saxoo ngoram!

di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.

Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke, doj yu ñu dàbbli di rawtoom, dundam doy, te ndoxam du ñàkk.

Moona noppiwula seereel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan, taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»

“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”