TSK

TSK · Genesis 12:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal.

fa mu tabaxoon ab sarxalukaay. Ibraam nag tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.

Isaaxa nag sàkk fa sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen.

Ba Laban dabee Yanqóoba, dafa fekk mu samp xaymaam ca tund wa. Laban it samp bosam ca kaw tundi Galàdd, moom aki bokkam.

Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.»

Yanqóoba ma nga tudde bérab, ba Yàlla waxeek moom, Betel.

Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Ngalla Aji Sax ji, xettli ma!»

Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.