TSK

TSK · Genesis 16:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sarayi moomu masuloona am doom te it manu ko woona am.

Ibraam ne ko: «Boroom bi, yaw Aji Sax ji, ana loo may may nag? Man awma doom sax, te ki wara donn sama alal moo di Elyeser, miy waa Damaas.»

Teewul Yàlla ne Ibraayma: «Bu la dara naqari ci xale bu góor bii, mook sa jaam bi. Defalal Saarata li mu la wax rekk, ndax ci Isaaxa lees di tudde saw askan.

Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb.

Luke 1:7 TSK

Amuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.

¶ Mbir mi misaal a ngi ci. Ñaari jigéen ñi ñaari kóllëre lay bijji. Genn kóllëre gi bawoo tundu Sinayi moo meññ lu ñeel njaam, te kooku mooy Ajara.