TSK

TSK · Genesis 17:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.

Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.»

«Dama di doxandéem ci seen biir, tey gan; moo tax ma di leen ñaan, ngeen sédd ma bàmmeel bu ma suul sama néew, ba mu làqu ma.»

¶ Yanqóoba dellu na kër baayam Isaaxa fa Mamre, ca Kiryaat Arba, gay Ebron ba tey, fa Ibraayma ak Isaaxa daloon.

te wax na ma ne ma: “Dinaa la giiral, fulandi la, def la nga sos mbooloom xeet, te réew mii laay may ñi askanoo ci yaw, ñu moom ko fàww.”

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Na bànni Israyil wormaal bésub Noflaay, nañu sàmm bésub Noflaay, ñook seen askan. Kóllëre la gu sax dàkk.

Nga diw leen, ni nga diwe seen baay, ñu doon samay sarxalkat. Seen diwu googu moo leen sédd sasu carxal bu sax dàkk, maasoo maas.»

¶ «Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, te mooy ñuy joxeel bànni Israyil seen njotlaay benn yoon cim at ngir seen bàkkaar yépp.» Ñu daldi def li Aji Sax ji santoon Musaa.

¶ Ba loolu amee Musaa wax ak Obab doomu Ruwel waa Majan ba, baayu soxnaam, ne ko: «Nu ngi nii jëm fa nu Aji Sax ji wax ne moom lanuy jox. Kaay nu ànd, dem, nu baaxe la, ndax Aji Sax ji moo digee baaxe Israyil.»

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Yéegil ca kaw tundu Abarim wee, nga séentu réew mi ma jox bànni Israyil.

ndax askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Aji Sax ji nee: «Du yeen doŋŋ laay fasool kóllëre gii, ak ngiñ lii.»

«Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen, ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israyil, ñu jagoo.

Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe, te sama àttey yoon lañuy sàmm, di ko jëfe. Su boobaa ñuy sama ñoñ, may seen Yàlla.

Maa leen di indi, ñu màkkaanoo digg Yerusalem, di sama ñoñ, may seen Yàlla, ci biir worma ak njekk.»