Lóot nag soññ leen, ba ñu dal këram, mu ganale leen. Lóot da leena berndeel, lakkal leen mburu mu amul lawiir, ñu lekk.
TSK
TSK · Genesis 18:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 19:3
TSK
Nehemiah 12:44
TSK
¶ Ñu daldi tànn bésub keroog ay nit, dénk leen néegi dencukaay, ya ñuy yeb ay jooxe, ak saraxi ndoortel meññeef, ak céri fukkeel yu ñuy génne. Ñu war caa dajale nag cér ya yoon wi dogalal sarxalkat yeek Leween ñi, te mu jóge ci tool yi wër dëkk yi. Waa Yuda rafetlu ca taxawaayu sarxalkat yaak Leween ña.
Luke 17:8
TSK
Xanaa kay da koy wax ne ko: “Defaral sama reer, te takku, taajal ma, ba ma lekk, naan, nga doora lekk, naan.”
Luke 24:43
TSK
Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
Acts 10:41
TSK
Du askan wépp la ko won, xanaa nun, seede yi Yàlla tànnoon lu jiitu, nu bokk ak moom lekk ak naan, gannaaw ndekkiteem.
Revelation 3:20
TSK
Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat, ba ubbil ma, dinaa agsi moos sa néeg, nu bokk reer.