TSK

TSK · Genesis 19:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc.

Naka la Ibraayma jegeñsi, ne ko: «Mbaa doo boole ku jub ak ku jubadi, rey leen?

Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

Ma sant it Leween ñi ñu laabal seen bopp te dem wattuji bunt ya, ngir sellal bésub Noflaay. Ngalla sama Yàlla, bàyyee ma lii xel itam te yërëme ma sa ngor lu bare.

Bul xool li ma bàkkaare ndaw ak li ma moy. Aji Sax ji, xoole ma sa ngor ngir sag mbaax.

Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.

Ci biir notaange la nu geesoo, Kee saxoo ngoram!

Su boobaa yeenay fàttliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu.

te mennum Lóot aji jub ji, di kenn ki mu musal, te mu sonnoon lool, ndax ñaawtéefi nit ñu dëng ñooñu,