¶ «Su góor tëddee góor ni ñuy tëddee jigéen, ñaawtéef lañu def ñoom ñaar. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
TSK
TSK · Genesis 19:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.
Moo tax waame aje, taw yiy mujje dikkul. Teewul ngeen dëgër bët nib gànc, ñàkk gàcce!
Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle,
¶ Loolu moo tax Yàlla bërgal leen ak seen bëgg-bëgg yu teddadi. Seeni jigéen sax dëddu nañu jaxasoo gi leen bindub juddu sédde, ba jublu ci lu woroo ak seen bindub juddu.
ak fokati séy yi, ak góor-jigéen yi, ak jàppkati jaam yi, ak fen-kat yi, ak giñkati fen yi, ak ñiy jëfe leneen lu woroo ak njàngle mu baax,
Naka noonu itam Sodom ak Gomor, ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci powum séy, ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara wu sax dàkk.