TSK

TSK · Genesis 20:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»

Abimeleg daldi fay doxe àrtu waa réewam mépp ne leen: «Ku laal waa jii walla soxnaam, dees na ko rey.»

Gannaaw loolu ñu sàqi, Yàlla nag wàcce tiitaange lu réy ca kaw dëkk, ya leen wër, ba taluñoo dabi doomi Yanqóoba ya.

Maa leen di dàqal ay xeet, ba yaatal seen suuf, te diiru ñetti yoon yi ngeen di teewi cim at fi kanam Yàlla Aji Sax ji, kenn du ci wuta nangu seenum réew.

Léegi nag sang bi, giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, nga fekke tey, Aji Sax jee la teree tuur deret tey, di feyul sa bopp. Muy say noon, di ñi lay fexeel lu bon, yal nañu bokk ak Nabal mii demin.

Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.

¶ Sama tont ci mbir mi ngeen ma bind nag, moo di lu baax la ci góor, mu mucc ci jigéen.

Kumpa la dooley ndëngte ji bàddoo te mu ngi def liggéeyam xaat, xanaa kay ki ko téye ba tey moo koy téye rekk ba keroog jëlees fi ki ko téye.