Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.
TSK
TSK · Genesis 22:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw.
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,
Yal na la ay giir nangul, ay réew di la sujjóotal, nga yilif say bokk, te say doomi ndey di la sujjóotal. Ku la móolooy alku, te ku la ñaanal barkeel.»
Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.
Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”»
Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»
Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen ful, ba yeena ngii tey, bare ba tollu ni biddiiwi asamaan.
Bu dara des ci seen loxo, lu bokk ci alal jooju ñu wara faagaagal. Su ko defee Aji Sax ji dëddu sànjam mu tàng, yërëm leen, ñeewante leen, yokk leen na mu ko giñale woon seeni maam,
Barke yii yépp a leen di dab, sottiku ci seen kaw, bu ngeen déggalee seen Yàlla Aji Sax ji:
¶ Gannaaw gi, Daawuda duma na Filisteen ña, néewal leen doole, jële kilifteefu waa Filisti ca réew ma.
Kon sama xalaat mooy nga boole ñi ànd ak yaw ba ñu daj, muy Israyil gépp, dale ko diiwaanu Dan ca bëj-gànnaar ba ca Beerseba ca bëj-saalum. Muy mbooloo mu bare, tollu ni suufas géej; te yaw ci sa bopp, nga jiite leen ci xare bi.
¶ Ay gaal yu mag itam Buur Suleymaan defarlu na ko ca Esiyon Geber ga ca wetu Elat, ca tefesu géeju Barax ya, ca réewum Edom.
Giiral nga leen, ba ñu tollu ni biddiiwi asamaan, ba noppi dugal leen ca réew ma nga waxoon seeni maam ñu nanguji ko.
mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
Nga jox leen réew mii nga giñaloon seeni maam. Muy réew mu meew meek lem ji tuuroo.
¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj, te moo law ba Yuda, àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.
Waaye cant ñeel na Yàlla, mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi!
¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»