TSK

TSK · Genesis 26:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.

Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.»

Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»

¶ Ba loolu amee Ibraayma dafa jóge fa mu nekkoon, jublu àllub Negew, sanci diggante Kades ak Sur, ba noppi ganeji ay fan ca dëkk ba ñu naa Gerar.

¶ Gannaaw loolu Isaaxa bey ca réew ma, góob ca at ma lu tollook téeméeri yoon la mu ji woon, ndax Aji Sax ji da koo barkeel.

Guddi googu Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Maay Yàllay Ibraayma sa baay; bul ragal dara, ndax maa ngi ànd ak yaw. Dinaa la barkeel, ful sa askan ndax sama jaam Ibraayma.»

¶ Ci kaw loolu Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, may ko ndam, mu dëkk ca kër sangub waa Misraam ba.

Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Ñeel Daawuda. Bu sa xol jóg ci ku bon, bul ñee kuy def njombe.

Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq ni max la mu gëna fonk. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.

Bul tiit, yaw laa àndal, maay jële saw askan penku, dajalee leen sowub jant.

Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.