ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.
TSK
TSK · Genesis 28:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sama sang nag giñloo ma ne: “Bul jëlal mukk sama doom soxna ci biir jigéeni waa réewu Kanaan, gi ma dëkk.
Toggal ma ko, ba mu neex, ni ma ko bëgge, indil ma, ma lekk, ndax ma ñaanal la lu ma tibbe ci sama xol, bala may dëddu.»
Isaaxaa ngay lox, bay rag-ragi, daldi ne ko: «Kan? Ana ku rëbbi woon nag, indil ma, ba ma lekk ba noppi? Ñaanal naa ko bala ngaa ñëw. Te dina barkeel moos.»
Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.
Su ko defee dinanu leen may sunuy janq, te dinanu jël ci seeni janq, dëkk ak yeen, nuy ay bokk.
Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,
Buleen wóllëranteek niti réew ma, lu ko moy dinañu gànctook seeni tuur, rendil seeni tuur ay sarax, woo leen ca, ngeen lekk ca seeni sarax.
¶ Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?