¶ Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam.
TSK
TSK · Genesis 28:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ.
¶ Mu am bés Yuusufa gént, nettali ko ay magam, ba tax ñu gënati koo bañ.
Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,
Man la kàddu dikkal ci kumpa, sama nopp taataan ndéey la,
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
¶ Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.
¶ Keroog ba ma jëkkee di layool sama bopp, kenn taxawuwma, ñépp a ma daw, yàlla bu leen seen jëf topp.
Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?