TSK

TSK · Genesis 28:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ibraayma nag teela xëy, takk mbaamam, ànd ak ñaari surgaam ak doomam Isaaxa, daldi xar matt, mi muy lakke sarax bi. Ma nga jëm fa ko Yàlla wax.

Ba loolu amee Yanqóoba jël aw doj, samp ko, muy doju xàmmikaay.

Yanqóoba nag samp aw doj ca bàmmeel ba, te mooy xàmmikaayu bàmmeelu Rasel ba tey jii.

¶ Keroog ba Musaa sampee jaamookaay bi ba noppi, diw na ko ngir sellal ko, mook mboolem ay jumtukaayam, sarxalukaay beek mboolem ndabam it, mu boole diw, sellale ko.

¶ Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.»

Bésub keroog ab sarxalukaay ñeel Aji Sax ji, fa digg réewum Misra, aw xer it ñeel Aji Sax ji fa kemu réew ma,