Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel.
TSK
TSK · Genesis 29:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Rasel amee doom ci Yuusufa, Yanqóoba da ne Laban: «Yiwi ma boog, ma dellu sama réew ca sama kër.
Ñaar fukki at a ngii, ma di la jaamu ci kër gi, liggéeyal naa la fukki at ak ñeent ngir sa ñaari doom yu jigéen ñii, teg ci juróom benni at yu ma la sàmmal say gàtt, nga soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom.
Sunu baay, ba lay siyaare, ne nu: “Xam ngeen ne damaa amul ak sama soxna lu dul ñaari doom.
¶ Ci kaw loolu Sóol ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sóol a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»
«Képp ku ñëw ci man, te bañuloo sa baay ak sa ndey, ak sa jabar, ak sa doom, ak sa bokk yu góor, ak sa bokk yu jigéen, bañuloo sa bakkanu bopp sax, doo mana doon sama taalibe.