TSK

TSK · Genesis 33:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

daldi wax Efron ci seen kanam ne ko: «Ngalla déglu ma, dama lay jox njégu tool bi, nga jël rekk, ndax ma man faa suul sama néew.»

¶ Noonu la Ibraayma jënde toolub Efron ba nekk ca Magpela te janook Mamre, muy moomeelam. Dafa jënd tool ba bépp, jëndaale xuntim xeer ma ca biir, ak garab ya ca sax yépp, ba fa tool ba yem. Mboolem Etteen ña séqoon pénc ma, seede nañu ne Ibraayma moo ko moom.

Mooy xuntim bàmmeel ba ca biir tool, ba ca Magpela, te jàkkaarloo ak Mamre ca réewu Kanaan, di tool, ba Ibraayma jëndoon ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel.

Acts 7:16 TSK

Gannaaw gi lañu toxal seeni yax ca Sikem, denc leen ca bàmmeel, ba Ibraayma weccikoo woon xaalis ca doomi Amor ca Sikem.