TSK

TSK · Genesis 37:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu Yanqóoba mititlu ko, ba xotti ay yéreem, taraxlaayoo ab saaku, di jooy doomam ay fan.

Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis.

¶ Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji

Joel 2:13 TSK

Du seeni yére doŋŋ ngeen di xotti, ngir ñaawlu, seenub xol ngeen di xottiwaale, ñaawloo ko. Waññikuleen ci seen Yàlla Aji Sax ji, mooy boroom yiw ak yërmande; mer maa diib, ngor ga bare, muy fomm mbugal.