TSK

TSK · Genesis 37:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.

Ci kaw loolu Yanqóoba ne: «Sama doom daal, du ànd ak yeen, ndax magam faatu na, te moom rekk a des. Su ko musiba dabee ci yoon wi ngeen jëm, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.»

bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbsi— aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw.

Israyil nag ne Yuusufa: «Yaakaaruma la woona gisati, ndeke Yàlla dina ma may lu raw gis la, ndax gis naa say doom.»

¶ Naka la Buur dégg loolu, naqar wu réy jàpp ko. Mu dem ca biir néeg ba, ca taax ma tiim bunt dëkk ba, di jooy. Ma ngay dem te naan: «Wóoy Absalom sama doom ja! Éey sama doom ja, céy Absalom sama doom ja! Éey waay su ma sañoon dee sax wuutu la, Absalom, doom. Éey waay sama doom ja!»

Job 2:11 TSK

¶ Gannaaw loolu ñetti xariti Ayóoba ñoo dégg mboolem musiba moomu ko dikkal. Ku nekk ci ñoom jóge këram: Elifas waa Teman ba, ak Bildàdd waa Suwa ba, ak Cofar waa Naama. Ñu bokk daje ngir dikk mas-sawu Ayóoba, dëfal ko.

Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi; guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. Sama xol tëë sedd.