TSK

TSK · Genesis 37:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Teewul genn guddi Yàlla feeñu Abimeleg ci gént ne ko: «Yaw dee nga ba noppi, ndax jigéen, ji nga nangu, soxnas jaambur la.»

Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?»

Te nag, sang bi, gannaaw gént nga ko ñaari yoon, kon Yàlla dogal na mbir mi, te dina ko amal balaa yàgg.»

¶ Ba Yuusufa wàccsee, ñu jébbal ko foofa ca biir kër ga sarica, ba ñu ko indaaleel, daldi koy sujjóotal.

¶ Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf.

¶ «Gaawleen dellu ci sama baay te ne ko: “Sa doom Yuusufa nee na: Yàlla fal na ma kilifag Misra gépp; ñëwal fi man, nu mu gëna gaawe.

Ba loolu amee Yuusufa di dundal baayam aki bokkam, ak mboolem waa kër baayam, boole ca ña bootu ca ñoom.

¶ Ci kaw loolu magam ya ñëwal seen bopp ba ca moom, sujjóotal ko ne ko: «Sang bi, nu ngi nii, di la siyaare.»

Muy màgg nag bay diir mbagg gàngoori xarey asamaan, ba daaneel lenn ci ñoom, ak lenn ci biddiiw yi, nappaaje leen.

ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,