TSK

TSK · Genesis 40:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, delloo la sa liggéey, ngay teg kaasu Firawna ci loxoom, ni nga ko daa defe naka jekk, ba nga yoree naanam.

Kilifag lakk-kati mburu ya moom, da koo wékk ci bant, na leen ko Yuusufa firile woon.

¶ Su nit moyee ba dee di àtteem, ñu rey ko, wékk ko ci garab,

Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla.

¶ Ba mu ko defee Rispa doomu Aya ju jigéen ja, jël ab saaku, tàllalal ko boppam ca doj wa. La ko dale ca ndoortel ngóob ma, ba keroog asamaan di sóob ca kaw néew ya, Rispa bàyyiwul dara mu laal leen bëccëg mbaa guddi, du picc, du rabu àll.

Ca kaw tundi Israyil ngay daanu, yaak mboolem say gàngoor, ak mbooloo yi ànd ak yaw. Tan yeek lépp luy njanaaw ak ndundati àll bi laa lay jox, leele la leen.

¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»