Ñu ne ko: «Ay gént daal a nu dikkal, te amunu ku nu koy firil.» Yuusufa ne leen: «Xanaa du Yàllaa moom piri? Nettalileen ma seeni gént rekk kay.»
TSK
TSK · Genesis 41:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax kat bii yoon maa ngii di yebal sama mbugal yépp ci yaw ci sa bopp, ak say dag ak sa waa réew, ngir nga xam ne awma moroom ci àddina wërngal këpp.
Aji Sax jee xamleg wallam, feeñal njekkam, xeet yi gis.
Na xeet yépp daje, askan yépp teewandoo. Ana ku nu ci yégaloon lii xew, mbaa mu xamal nu la wees? Na seen seede teew, dëggal leen; ba ñu dégg leen, ne noonu la.
Moo waral nga gis doj wu loxo sànniwul, mu fàqe tund wa, daldi rajaxe weñ gaak xànjar jaak ban baak xaalis baak wurus wa. Buur, Yàlla ju màgg ji moo la xamal liy ñëw. Gént gi wér na, piri mi mata gëm.»
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»