TSK

TSK · Genesis 41:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te itam juróom ñaari nag yu yooy, yi ci topp te ñaaw, juróom ñaari at la. Naka noonu juróom ñaari gub yu gooy, yi ngelaw li lakk, juróom ñaari ati xiif lay firi.

juróom ñaari ati xiif ya tàmbali, na ko Yuusufa waxe woon. Réew yépp nag nekk ci xiif, waaye amul fu ñàkk dund ca Misra.

¶ Ab dund amuloon fenn ca réew ma mépp, ndax xiif bu metti lool. Waa réewum Misra ak réewu Kanaan jeex tàkk ndax xiif ba.

¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»

Moo wàcce ab xiif ca réew ma, dagge fa luy gub,

ba képp ku namma barkeel fi kaw suuf, ci Yàlla jiy dëgg la koy ñaane, te kuy giñ fi kaw suuf it, ci Yàlla jiy dëgg la koy giñe. Day fekk njàqare ya jiitu di lu ñu fàtte, te di lu làqu saay gët.

¶ Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.