TSK

TSK · Genesis 44:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Danoo nekk ca tool ya, di góob. Ba nu takkee, sama takk jekki-jekki ne sàtt, taxaw, seen takk wër sama takk, di ko sujjóotal.»

¶ Naka la ko mag ya séen fu sore, daldi mànkoo bala moo agsi, ci pexem rey ko.

¶ La ca tegu Yuda ne Israyil: «Baay, tegal ngóor si ci sama loxo, nu daldi dem, ndax nu dund, baña dee, nook yaw ak sunuy doom.

Gannaaw loolu it xasoon naa dige sama bakkan, ndax damaa waxoon ne: “Bu ma la ko délloosilul, maa koy gàlloo ba kera may dee.”

¶ Su ab jote amee diggante ay nit, nañu dem ca ëttub àttekaay ba, ñu àtte leen, ba ki am dëgg, ñu jox ko dëgg, ki tooñ, ñu teg ko tooñ.

Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?»

Ezra 9:15 TSK

Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, yaay boroom njekk. May nga nu bésub tey jii nu dese bakkan. Nu ngi nii fi sa kanam ci biir tooñange, ba tax du kenn ci nun ku am lay fi sa kanam.

Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.

Léegi yeen waa Yerusalem ak yeen waa Yuda, ngalla àtteleen maak sama tóokër.

Yaw Boroom bi, njub ñeel na la, waaye nun gàcce ñeel na nu bésub tey jii, muy waa Yuda, muy waa Yerusalem, di waa Israyil gépp, ku jegeek ku sore, ci biir mboolem réew yi nga leen dàq, yóbbu, ndax li ñu la ñàkke kóllëre.

Luke 12:2 TSK

Mboolem lu nëbbu dees na ko feeñal, te lu làqu dees na ko xam.