TSK

TSK · Genesis 44:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Booba Yanqóoba, Yuusufa la gëna bëgg ci ay doomam, ndax li mu màggat door koo am. Mu ràbblul ko mbubb mu yànj.

Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!»

Seen baay Yanqóoba ne leen: «Xañ ngeen ma ay doom: Yuusufa nekkatul, Simeyon nekkatul, léegi ngeen bëgga jël Beñamin, yóbbu. Loolu lépp ci sama kaw; ngalla man!»

Ñu ne ko: «Waa ja kat da nu doon laaj ak a laajaat ci nun ak sunuy bokk, ba naa nu ndax sunu baay mu ngi dund ba tey, ak ndax am nanu rakk. Nun itam nu wax ko li mu nu laaj. Géntunu woon moos ne dina nu sant, nu indil ko sunu rakk!»

Doomi Beñamin yu góor ñoo di Bela ak Beker ak Asbel ak Gera ak Naaman ak Eyi ak Ros ak Muppim ak Uppim ak Àrd.

Luke 7:12 TSK

Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.